1 Corinthians 1:10 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye bokk yi, maa ngi leen di dénk ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen juboo te bañ a féewaloo ci seen biir. Waaye nangeen ànd te booloo, bokk xel, bokk xalaat.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.