1 Corinthians 1:17 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte Kirist yebalu ma ngir may sóobe ci ndox, waaye da maa yebal, ngir may yégle xebaar bu baax bi, te ma bañ koo def ak waxi xam-xamu nit, ngir bañ a ñàkkal faayda deewu Kirist ca bant ba.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax du sóobe cim ndox la ma Almasi yebale, xanaa ngir ma yégle xibaaru jàmm bi, te bañ koo defe xareñtey kàddu, ngir baña neenal bantub Almasi, ba ñu ko daajoon.