1 Corinthians 10:16 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Kaas bu yiw, bi tax nuy gërëm Yàlla, ndax du wone sunu booloo ak deretu Kirist? Mburu mi nuy damm, xanaa du dafay wone sunu booloo ak yaramu Kirist?
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kaasu barke bi nuy barkeeloo, xanaa du mooy bokk gi nu bokk ci deretu Almasi? Te mburu mi nuy daggoo, du mooy bokk gi nu bokk ci yaramu Almasi?