1 Corinthians 10:33 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu laay def man ci sama bopp: damay wut a neex ñépp ci lépp. Wutuma lu may jariñ, waaye luy jariñ ñu bare laay wut, ngir ñu mucc.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu laay def man ci sama bopp: ñépp laay wuta neex, ci lépp. Sàkkuwuma sama njariñal bopp, waaye njariñal lim bu gëna takku, moom laay sàkku, ngir ñu texe.