1 Corinthians 11:22 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Xanaa amuleen kër yu ngeen di lekke ak di naane? Walla ndax dangeen a xeeb mbooloom Yàlla? Walla ngeen bëgg a rusloo ñi amul dara? Lu ma leen ci war a wax nag? Ma gërëm leen ci loolu? Mukk! Gërëmuma leen.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Xanaa amuleen kër yu ngeen di lekke ak a naane? Am mbooloom Yàlla mi ngeen sofental, di rusloo ñi amul? Ana lu ma leen di wax? Dama leen koy gërëme? Loolu de duma leen ci gërëm.