1 Corinthians 14:5 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Léegi nag bëgg naa yéen ñépp, ngeen di wax ay làkk, waaye li ma gënal mooy ngeen di wax ci kàddug Yàlla. Kiy wax ci kàddug Yàlla moo gën kiy wax ay làkk, su firiwul li muy wax, ngir ngëmu mbooloo mi yokku.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Su ma sañoon ngeen di làkk yeen ñépp yeneen làkk, waaye ngeen di waxe kàddug waxyu moo ma gënal. Kiy waxe kàddug waxyu moo ëpp njariñ kiy làkk yeneen làkk, ndare ñu tekki li muy làkk, ba mbooloom gëmkat ñi jële ca lu ñu feddlikoo.