1 Corinthians 14:6 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Kon nag bokk yi, su ma ñëwee ci yéen, di wax ay làkk, lu ma leen di jariñ? Dara, su ma leen indilul dëgg gu Yàlla feeñal, walla xam-xam walla kàddu gu tukkee ca Yàlla, walla am njàngale.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Léegi bokk yi, su ma leen dikke woon yeneen làkk yu may làkk, ana lu ma leen di jariñ? Dara, xanaa ma àgge leen kàddug peeñu, mbaa xam-xam, mbaa waxyu, mbaa digle.