1 Corinthians 14:7 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu la mel itam ci yëf yi dundul tey riir, ni toxoro walla xalam. Su li ci jibe leerul, naka la nit man a ràññee li mbiibi toxoro walla buumi xalam di wax?
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu la itam ci jumtukaayi po yi dundul tey jibal coow; muy toxoro mbaa xalam. Su yooyu jumtukaay jibalul galan yu leer, ana nees di xame li toxoro ji, mbaa xalam giy wax?