1 Corinthians 15:10 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye nag yiwu Yàlla moo tax ma doon li ma doon, te yiw, wi mu wone ci man, du cig neen. Waaye sax maa gën a liggéey ñi ci des ñépp: du ci man, waaye yiwu Yàlla, wiy jëf ci man, moo tax.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Xanaa yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla, wi ànd ak man la.