1 Corinthians 15:24 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Gannaaw ga, mujug jamono taxaw, te Kirist dina noot gépp kilifa ak bépp sañ-sañ ak doole, ba noppi delloo nguur gi kiy Yàlla di Baayam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gannaaw loolu la muj ga, te ca lay delloo nguur gi kiy Yàlla, di Baay, fekk mu neenal mboolem luy kilifteef, ak mboolem sañ-sañ ak doole.