1 Corinthians 2:13 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Te loolu nu Yàlla may, yéglewunu ko ci ay baat yu soqikoo ci xam-xamu nit, waaye nu ngi koy yégle ci baat, yi soqikoo ci Xelum Yàlla, di tekkantal yëfi Xelum Yàlla ci ay baat yu mu nu sol.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
May yooyu lanuy biral, te waxewunu ko njànglem xam-xamu nit, waaye njànglem Xelum Yàlla lanu koy waxe, di jëfandikoo kàddu yu làmboo Xel mi, ngir teqantal ay mbir yu làmboo Xel mi.