1 Corinthians 4:17 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Looloo tax ma yebal ci yéen Timote, miy sama doomu diine, di doom ju takku te ma bëgg ko. Dina leen fàttali ni may dunde ci Kirist, te mu dëppook li may jàngale fu nekk ci mboolooy ñi gëm ñépp.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Looloo tax ma yebal ci yeen Timote, sama doomu bopp, ji sax ci yoonu Sang bi. Moo leen di fàttli samay doxalin ci yoonu Almasi, noonu ma koy jànglee fépp, ci mépp mbooloom gëmkat.