1 Corinthians 4:6 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Bokk yi, ci loolu ma leen doon wax lépp nag, misaal naa leen ko ci Apolos ak ci man, ngir ngeen xool ci nun, ba xam li wax jii di tekki: «Bu seen xalaat weesu li Mbind mi wax.» Noonu kenn du màggal kii, suufeel ki ci des.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bokk yi, loolu de laa natte ci Apolos ak ci man, ñeel leen, ngir ngeen jànge ci sunu ñaari jëmm, ba sàmm solob kàddu gii: «Bu seen xalaat jàll ca wàlla li Mbind mi wax.» Su ko defee dungeen réy-réyloo far ak kenn, di beddi keneen.