1 Corinthians 5:1 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Dégg nanu sax ñu naan, am na kuy moy Yàlla ci seen biir, moy gu ni tollu, duñu ko gis sax ci ñi xamul Yàlla. Dem na, ba am ci yéen kuy séy ak jabaru baayam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Déggees na nag ci lu wér, ne powum séy am na ci seen biir, te powum séy mu ni mel, giseesu ko sax ci biir xeeti yéefar yi. Dem na sax ba nit nekk ak jabaru baayam.