1 Corinthians 6:13 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Am na ci yéen ñu naan: «Ñam mooy jariñ biir, te biir ay jariñoo ñam.» Waaw, te Yàlla dina leen yàq, ñoom ñaar yépp. Waaye sàkkuñu yaram ngir moy Yàlla; dañu koo sàkk, ngir muy jariñ Boroom bi, Boroom bi di ko jariñoo.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñenn a ngi naan: «Aw ñam, biir la ñeel; te biir it, aw ñam la ñeel.» Muy dëgg it, te Yàlla mooy neenal ñam wi, ak biir bi mu jëm. Waaye taxul yaramu gëmkat bi ñeel powum séy. Sang bi kay la yaramu gëmkat bi ñeel, te Sang bi it, ñeel yaram wi.