1 Corinthians 7:5 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bu kenn tere boppam moroomam, su dul ne dangeen a mànkoo ci def noonu ab diir, ngir gën a man a wéet ak Yàlla ciy ñaan. Waaye su loolu weesoo, nangeen doxal yoonu séy; lu ko moy, Seytaane dina leen fiir ndax seen ñàkk maandute.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Buleen di xañante seen bopp, ndare du yeena mànkoo ab diir, ngir bokk tënku ci ñaan. Waaye gannaaw loolu, delluleen di ànd, bala leena Seytaanee xiirtal ci moy, ndax tëlee téye seen bopp.