1 Corinthians 8:10 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Su amee ku ngëmam néew, mu gis la, yaw mi bare xam-xam, nga toog di lekk ca màggalukaayu xërëm ya, ndax du ko xiir mu lekk yàppu sarax?
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yaw mi réy xam-xam, ku la gis ca ndab la ca jaamookaayu tuur ya, su dee ab gëmkat bu xelam daladi ndax ngëm gu desee dëgër, mbaa du ko xiir ci roy la, ba mu lekk ca ñamu sarax sa?