1 Corinthians 8:6 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
ba tey ci nun, jenn Yàlla rekk a am, muy Baay bi; lépp a ngi jóge ci moom te moom lanu nekkal. Te it benn Boroom rekk a am, muy Yeesu Kirist; lépp a ngi jaare ci moom, te nun it nu ngi dund jaare ci moom.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Teewul ci sunu wàllu bopp, jenn Yàllaa am, muy Baay bi lépp jóge ci moom, te sunu bakkan ñeel ko, benn Sang doŋŋ a am, muy Yeesu Almasi, bi lépp ame ci moom, te sunu bakkan, ci moom la ame.