1 Corinthians 9:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndegam ñeneen a am sañ-sañ boobu ci yéen, nun kon waxi-noppi. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Danuy far muñ lépp, ngir bañ a indi ndog ci yoonu xebaar bu baax bu Kirist bi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndegam ñeneen a jagoo boobu sañ-sañ ci yeen, astamaak nun. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Lépp lanu far muñ, ngir baña gàllankoor yoonu xibaaru jàmm bu Almasi.