1 Corinthians 9:20 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ci biir Yawut yi, sol naa melow Yawut yi, ngir gindi leen. Man ci sama bopp yoonu Musaa jiitalu ma, terewul bi ma nekkee ci biir ñiy sàmm yoonu Musaa, sàmm naa yoon wa, ngir gindi leen.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba ma nekkee ci biir Yawut yi, ni Yawut yi laay def, ngir iri leen. Ba ma nekkee ak ñi tegoo yoonu Musaa, damaa mel ni yoonu Musaa laa tegool, ngir iri ñi tegoo yoonu Musaa, te man ci sama bopp, tegoowuma yoonu Musaa.