1 Corinthians 9:25 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ñiy joŋante ci po muy waral tàggat yaram, dañuy xañ seen bopp lu bare. Dañu koy def, ngir am kaalag ndam gu dul yàgg; waaye nun danu koy def, ngir am kaalag ndam gu sax ba fàww.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar.