1 Kings 1:25 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat, Adoña dem na tey jii, sarxeji lu bare ciy nag ak wëllu yu duuf aki xar. Woo na ca doomi Buur yu góor yépp, ñook njiiti xare yeek Abiyatar sarxalkat bi. Ña nga noonee di lekk ak a naan ñook moom te naa: “Buur Adoña, guddalu fan!”