Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Aji Sax ji ne ko: «Génnal taxaw ci kaw tund wi, fi sama kanam, ndax kat man Aji Sax ji maa ngi waaja romb.» Ci kaw loolu ngelaw lu réy te bare doole jiitu Aji Sax ji, xar tund ya, rajaxe doj ya, waaye Aji Sax ji nekkul ca ngelaw la. Ngelaw la dal, suuf sa yëngu, waaye Aji Sax ji nekkul ca yëngu-yëngu suuf ba.