1 Kings 21:13 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñaari nit ñu tekkiwul dara dikk toog janook moom. Ñu duural ko ca kanam mbooloo ma, ne Nabot daa saaga Yàlla, saaga Buur. Ñu génne Nabot dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.