Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
ndab yi itam, ak feyukaay yi ak këll yi ak kopp yi ak andi cuuraayu yi, lépp di wurusu ngalam. Te it ngoosi wurus yi bunti néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ca bérab bu sell baa sell, ak ngoosi wurus yi beneen buntu néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ci néeg Yàlla bu mag bi, lépp wurus la.