Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
«Léegi nag Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ngalla sàmmal li nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ne ko: “Deesu la xañ mukk ci saw askan ku góor kuy tooge jalub Israyil fi sama kanam, ndegam saw askan a ngi moytu seenu yoon, tey doxe fi sama kanam noonee nga daan doxe fi sama kanam.”