1 Peter 1:7 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Xam ne nattu yooyu dinañu sellal seen ngëm, ni safara di setale wurus, fekk wurus luy wéy la, te ngëm a ko gën fuuf. Noonu seen ngëm dina yelloo cant, ndam ak màgg, bés bu Yeesu Kirist feeñee.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant, ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi feeñee.