1 Peter 2:5 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
te yéena ngi mel niy doj yuy dund yu Yàllay defare dëkkukaayam. Noonu ay saraxalekat yu sell ngeen, ngir jébbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gi tabaxe kërug Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi.