1 Peter 3:7 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Te yéen itam góor ñi, na ku nekk ci yéen am xel, ci ni ngay ànde ak sa jabar, xam ne àndandoo ju la gën a néew doole la. Joxleen ko teraanga ju mat, ndax yéena yem cér ci yiwu Yàlla, wi nu ubbil buntu dund gu dul jeex. Noonu dara du man a yàq seeni ñaan.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Naka noonu yeen góor ñi, bàyyileen xel ni ngeen dëkke ak seeni jabar, tey sóoraale néew dooley jigéen. Séddleen leen teraangay nawle, gannaaw yeena bokk wenn yiw wi leen may ngeen dund dëgg. Su ko defee dara du gàllankoor seeni ñaan.