1 Peter 4:11 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Kuy jottali kàddug Yàlla, na mel ni Yàllaay wax. Kuy jëf it, na jëfe dooley Yàlla, ngir turu Yàlla màgg ci lépp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak kàttan ba fàww. Amiin.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kuy wax, na waxe nu mu jottlee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp, ndax Yeesu Almasi, mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.