1 Peter 4:3 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte àndoon ngeen démb ci xalaati ñi xamul Yàlla, di dund ciy ñaawteef ak topp seen bakkan, di màndi ak a xawaare, di xér ci biiñ ak a jaamu ay xërëm yu araam, waaye na fi yem nag.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax démb kat yàgg ngeena def coobarey xeet yi xamul Yàlla, ci ay ñaawtéef, ak topp seen bakkan. Dangeen daa màndi ak a xawaare, dëkke naan biiñ, di jaamu tuur yu seexluwu, waaye na fi yem nag.