1 Samuel 15:9 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Sóol ak gàngooram nag bàyyi Agag, muy dund, mook la gëna baax ca nag yaak gàtt ya: jurug yafal gaak kuuy yu ndaw ya, mboolem lu baax daal. Néeguñu caa faagaagal dara, waaye mboolem lu ca ñàkk solo mbaa mu yooy, loola lañu faagaagal.