Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw loolu Akis woo Daawuda, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, ku jub nga, te doon naa rafetlu sa ànd ak man, di xarejeek a dikk, ndax bés ba nga dikkee fi man ba tey jii, gisuma ci yaw lu bon. Waaye nag kàngami Filisti ñoo rafetluwul sa teewaay.