Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bu ngeen di àgg biir dëkk bi rekk, dal ko fay fekk, bala moo dem jaamookaay ba, ca sarax sa. Waa dëkk bi duñu lekk mukk te dikkul, ndax mooy ñaan ci sarax si. Bu noppee, ñi ñu woo doora lekk. Kon demleen gaaw, ndax nëgëni fa ngeen koy fekk.»