1 Thessalonians 2:9 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Bokk yi, yéena ngi fàttaliku sunu coono ak sunu ñaq; xam ngeen ni nu liggéeye guddi ak bëccëg, ngir bañ a diis ci seen kaw, ci di leen yégal xebaaru Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Xanaa bokk yi, yeena ngi fàttliku sunu doñ-doñ ak sunu coono? Diir ba nu leen di yégal xibaaru jàmm bu Yàlla bi, guddi ak bëccëg lañu daan liggéeyaale, ngir baña diisal kenn ci yeen.