1 Thessalonians 3:6 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye léegi Timote bawoo na ci yéen, indaale xebaar yu neex ci seen ngëm ak seen mbëggeel; xamal na nu ne, yéena ngi am pàttaliku yu rafet ci nun te namm nu lool, ni nu leen namme yéen itam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye léegi bi Timote délsee, bawoo ci yeen, xibaaru jàmm la nu àgge ci seen ngëm, ak seen cofeel, ak ni ngeen nuy bégee di fàttliku saa su nekk, te namm nu lool ni nu leen namme, nun itam.