1 Thessalonians 4:1 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Léegi nag bokk yi, jot ngeen ci nun, nan ngeen war a dunde ba neex Yàlla, te moom ngeen di def. Waaye ci turu Boroom bi Yeesu nu ngi leen di ñaan ak a dénk, ngeen gën koo feddali.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Li ci des nag, bokk yi, moo di yeena nangoo ci sunu làmmiñ, jëfin wi ngeen wara jëfe ba neex Yàlla, te it moom ngeen nekke. Waaye danu leen di tinu, di leen ñaax, ci turu Sang Yeesu, ngir ngeen gënati koo jëfe.