1 Thessalonians 4:16 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ndaxte ndigal lu jamp dina jib, baatu kilifa ci malaaka yi dégtu, liitu Yàlla jolli, te Boroom bi moom ci boppam dina wàcce ca asamaan. Booba ñi gëm Kirist te dee dinañu jëkk a dekki;
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi ñooy jëkka dekki.