1 Thessalonians 5:23 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Na leen Yàlla Boroom jàmm sellal, ba ngeen mat sëkk; na sàmm seen xel mépp, seen xol bépp ak seen yaram wépp, ngir dara bañ cee am sikk, ba bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel, ak seen léppi xol, ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi feeñee.