1 Timothy 3:16 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ci dëgg-dëgg ragal Yàlla ëmb na mbóot yu xóot:Ki wàcc, yor bindu nit,mu bir ne xelam jub na,te malaaka ya gis ko;xamlees na ko ci xeet yi,ñu gëm ko ci kaw suuf,te Yàlla teeru ko ci ndamam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.