1 Timothy 5:4 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye ku ci am ay doom mbaa ay sët, na njaboot googu jëkk a wone seen ragal Yàlla ci seen biir kër, ci delloo njukkal seen waajur, ndaxte loolu lu rafet la fa kanam Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye su dee ab jëtun bu ami doom mbaa ay sët, ñooñoo wara jëkka jéema jëfe ag ragal Yàlla ci seen biir kër, ba delloo njukkal seen waajur, ndax loolu la Yàlla rafetlu.