1 Timothy 6:17 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ñi barele alalu àddina nag, dénk leen ñu bañ a réy te bañ a wékk seen yaakaar ci koom-koom yi saxul fenn, waaye ñu wékk ko ci Yàlla, mi nuy may naataange ju mat, ngir nu man ciy bànneexu.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.