1 Timothy 6:2 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ku am sang boo bokkal ngëm, bu looloo tax nga yab ko, waaye nga sax ci itteem, ndax kiy jariñu ci sa ñaq, aji gëm la, ku mat a bëgg. Jàngaleel loolu nag, di ko dénkaane.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Jaam yi seeni sang di bokki gëmkat, buñu yab seeni sang, ndax li ñuy bokki gëmkat, waaye na tax ñu gënati leena jaamu, ndax seen sang yooyu di jariñoo seenu ñaq, ay gëmkat lañu, ay soppe lañu. Loolu nga wara jàngle, di ko dénkaane.