2 Corinthians 1:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Li nuy tiitaroo moo di sunu xel day seede ne, ci kanamu àddina si, rawatina sax ci seen kanam, aw nanu ci tànk yu jub, ànd ak xol bu laab fa kanam Yàlla. Jëfewunu ci pexem nit, waaye ci yiwu Yàlla lanu jëfe.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.