2 Corinthians 10:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ñemewunoo féetele walla mengale sunu bopp ak ñooñu naw seen bopp. Ci li ñuy sàkk ab natt ngir natt ak mengale seen bopp ak seen bopp, ñàkk xel a tax.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñenn ci ñooñu di seedeel seen bopp ne ñoo yelloo ngërëm nag, nun ñemewunoo boole sunu bopp ak ñoom, mbaa nuy méngale sunu bopp ak ñoom. Waaye ñoom dañoo amul xel, ndax nattukaay bi ñuy nattoo, di ko méngalantee ci seen biir, ñoom ñoo ko sàkkal seen bopp!