2 Corinthians 10:15 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Kon nag dunu jéggi dig yi Yàlla rëdd, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne, su seen ngëm yokkoo, dinanu gën a màgg ci seen biir, des ba tey ci dig yi nu Yàlla rëddal.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Weesunu kemu, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne nu seen ngëm gëna yokkoo, ni la sunuw sas di gëna yokkoo, lépp ci biir kemu gi ñu nu àppal.