2 Corinthians 11:26 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ci sama tukki yu bare yi daan naa faral di daje ak musiba ci dex yi, ak musiba ci sàcc yi, musiba mu jóge ci sama xeet walla ci ñi dul Yawut, musiba ci biir dëkk yi, ci màndiŋ yi, ci géej gi, ci biir bokki taalibe yu naaféq yi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bare na lu ma tukki, ay aaytéef xaare ma ay dex, xaare ma ay sàcc, xaare ma ay pexe yu ma samaw xeet lalal, ak yu ma jaambur ñi lalal. Ay aaytéef xaare na ma biir dëkk, xaare ma biir màndiŋ, xaare ma biir géej, xaare ma ci biir bokki taalibe yu ko mbubboo.