2 Corinthians 11:4 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte bu kenn ñëwee, di leen waar ci Yeesu ci lu juuyoo ak li nu leen yégal, walla ngeen jot meneen xel mu wuute ak Xel mi ngeen jot, walla ngeen nangu beneen xebaar bu wuute ak bi ngeen dégg, dingeen ko dékku bu baax.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat gaaw ngeena xajoo lool, nit ku dikk, di leen waare meneen Yeesu mu nu waarewul, mbaa geneen noo gu ngeen jot te jotuleen ko woon, mbaa beneen xibaar bu ngeen dëggal, te mu wuute ak ba ngeen déggoon.