2 Corinthians 13:10 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Looloo tax ma leen di binde nii, bala maa ñëw; bëgguma leen a duma ci sañ-sañ bi ma Boroom bi jox. Jox na ma ko, ngir ma yokk seen ngëm, waaye du ngir seen kasara.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Looloo tax ma bind leen lii bala maa dikk, ba buma dikkee, du jar may mettil ni may jëflante ak yeen, ci kaw sañ-sañ bi ma Boroom bi jox. Ndax kat sañ-sañ bi, yokke moo ko taxa jóg, waaye deesu ko yàqe.