2 Corinthians 13:4 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Néewoon na doole, ba ñu koy daaj ca bant ngir rey ko, waaye mi ngi dund ci kàttanu Yàlla. Nun itam néew nanu doole ci sunu bokk ci moom, waaye dinanu dund ak moom ci kàttanu Yàlla, bu nuy jëfante ak yéen.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Cig néew doole lees ko daaje ci bant ba rey ko, waaye tey ci manoorey Yàlla lay dunde. Nun itam sunug bokk ci Almasi moo tax nu néew doole, waaye ci manoorey Yàlla lanuy bokk ak moom di dund, bu nuy jëflante ak yeen.